Share

Borom Laylatoul Qadr: Sokhna Maïmounatou Mbacke njaaréem la gané adduna ci attum 1925

Partagez

19106002_10209261737760006_2762339899135199840_n Sokhna Maïmounatou Mbacke njaaréem la gané adduna ci attum 1925, att aki wéer la défak Sëriñ Tuuba Kon minuko Waajuram wu jigéen di Sokhna Khary Sylla ñu gënn koo miin ci ( Sokhna Khary Darou )

Sokhna Maï nak amul kén kumu bokkal ñaari waajur ci njabootu Sëriñ Tuuba gi, Sëriñ bi tuddéko kén ci Sokhnay Yonénte bi (SAWS)
S MODOU MOUSTAPHA mooko yar taxaw ci moom taxawaayu waajur, mooko yobbu yit DAARUL MOUHTY jox rakkam ja Sëriñ Seex Awa Balla mu Maam THIERNO Birahime mu dëkkoo ko, nu amfa ñatti bànt di
Sokhna Baaly Mbacke
Sokhna Maam Faaty Mbacke
Sëriñ Modou Mahfouz Mbacke miy xalifaam,

S Mouhammadou Faddal Mbacke néenako nékk googu nga nékk Daarul Mouhty mboolém njabootug Sëriñ Tuuba gi Bég nanu ci yaw ngërëm nanula, S Tuuba yit bég na ci
Bimu nékké Daroul Mouhty ba ci attum 1950 ci la am ndiggël ci S Fallou di maggal guddig laylatul xadre.

Sokhna Maïmounatou Mbakké mingi wacci ligéey Jeudi 4 février 1999 S Saliou wax S Mourtada mu taxawuko ñu déncciko ci arméeri Tuuba Yi.

[ Yàlla nako Yàlla dolli ngërëm ag léer ]

Leave a Comment